1- « NAADIOU DEMB DOU WOWAL POTUM TEY »
2- « KOU NDOBINE REY SA MAAM FOO GUISSATI LOU NIOUL DAW »
3- « EULEUK DOU AGNE DOU REER WAYE LOU MATA SEDDE LA »
4- « KOU AMOUL YAYE NAMPA MAAM »
5- « MATE MOU BARI DIAROUL NAWE ALLA »
6- « NIT NITAY GARABAM »
7- « KOU SAGNOUL BAGNE SAGNA NANGOU »
8- « BALAA NGA XAM XAMADI XAW LA RAY »
9- « TERE MOU TE BAYIL MOU GUISS »
10- « KOU TEUP DAL CI DAAY DESSE LA BENEEN TEUBINE »
11- « BALAA NGA LAAX DIAAY LAAX LEK »
12- « WIRI WIRI DIARI NDARI »
13- « KOU YAGUE CI TEEN BAAK FEK LA FA »
14- « GOUMBE TALLE NA LENEEN LOUDOUL TEUP AY TEEN »
15- « KOU MAR TAKH NAAN POOTIT BOU ROBINET OUBE MOU ROUSS »
16- « JIGUEN MAR NAAN WOROUL TAKH MOU REERE AY WENAM »
17-« KOU AMOUL KILIFA DJINE DI SA KILIFA»
18- «FOU NDOKH DAAN TAA BO DEME FEK FA TEP TEP»
19- «KOU LA ABAL BEUT NGA KHOL FOU KA NEEX»
20- « NDOKH DOU BAAYI YOONAM »
21 « MAGOU WAXOON NA KO MO GUEN MAGOU KHAMOON NA KO »
22- «BOUR AYOUL DAK YA AY»
23- « SOUL KER DOUKO TERE FEEGNE »
24- «GARAP BOU NAR DOON PINTHIE LAOBE DOU KO GUISS BA DIKO GOR»
25- «FAGARU MOO GUEN FADIOU»
26- «LOO DOONOU NDOGOM DO DOON SERIGNAM»
27- «KOU WATHIE SA ANDE, ANDE BOO NDEM FEK FA BOROM»
28- «KOU EUMB SA SANXAL EUMB SA KERSA»
29- « KOULA MAK EUP LA AY SAGAR »
30- « KOU XAMATOUL FOO DIEUM DELOUL FA NGA DIGUE WOON »
31- «MAY NIT DIEUN BESS BOU NEK DIANGAL KO NOU NIOUY NAPPE MOOKO GUEN»
32- «NAAR BOU NDAW LOUMOU WAKH SA BERKELE BA LAKO DEGUE»
33- «DONA SA BAAY DOON SA BAAYA KO GUEN»
34- « SOUF BOU SOUTE MAROMAM DAGNE KO DIAL »
35- « NEEW DOU ROMBE BAMEELAM »
36- « DIOGUE LAMBA DIA DI BAKOU MOO GUEN DEM LAMBA DIA DI BAKOU »
37- « KOU XAMOON LOOY MOUDJE NGA DIEUKE KO »
38- « KOU NEK CI XARE BOU DIEKHAGOUL DO REE KOUGNOU DIAM »
39- « KOUY DIEGUI NDOKH DOU REE KOU LAP »
40- « GUEWEL BOU REP CI XARE LOUMOU DJIN XEEP KO »
41- « ADOUNA WEEROU KOR LA FEEX DOK DIOTOUL DIOUBOU DOU WEES »
42- « FETHIOU LIIR SOU NEEXE NDEY DIA TEYE SA MBAGAYA »
43- « KOU DOUL TOUKI DOO XAM FOU DEK NEEXE »
44- « NIAY BOUY XALLA YOON DOOM DIA TAKH »
45- «BOU DIEGUE DOON TAKH DOON MBOK NDOKH DOU TOGUE DIEUN»
46- «PITHIE NGA CI KAW WAYE XEL MA NGUI CI SOUF»
47- « MBOTT YIY TEUP NAWET YEUP KOU LEEN NAR TATHIOU SA TOOL BOOYE »
48- « MBAAM GAATA NA WAYE CI DIOUR GUI LA BOK »
49- « GUENOU GOLO GATTE NE WAYE LOO CI LAAL MOU YEUK KO »
50- « FASS BOUKO DENK SA XARIT DENK KO XARITAM »

J’ai vraiment adoré ces proverbes, presque chaque proverbe me renvoie à une conférence
Merci de tes commentaires j’espère que tu vas m’aider pour traduire les proverbes en francais car c’est pas facile.